Maghreb
Maghreb mooy wàll gi gën a Féete penku ci bëj-gànnaaru Afrik, nekk ci diggante Géej gu diggu gi ci bëj-gànnaar ak tàkk gu Sahara'k gu Libi ci bëj-saalum ak Mbàmbulaanu Atlas ci penku.
Cosaanu baat bi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci araab al-Maghrib di tekki "sowwugi" (suuluway); li ko waral mooy féeteem ci wàllu penku suñ ko xoolee ak fa araab yi dëkk. Di safaanoo ak Machrek (fenkuwaay, sowu), maanaam penku ga araab yi dëkkee, li ko dalee Esipt ba Iraak. Bu jëkk Jezirat al Maghrib lañ ko tuddee woon, di tekki "dun bi ci Penku", ndax nañ gisee woon diwaan bi ca jamono ju yagg ja: li mu nekkoon ci diggante géej gi ak ndand féy-féy gi.
Ci araab Maghreb day tekki tamit Marok. Ngir jaawale bañ ai am ci, marok el-Maghreb el-aqsa lañ koy woowee ci araab, di tekki “penku gu sori gi”. Di nañ ko wax tamit “suuluwaay gu araab”
Diwaani Afrig | |||
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan |